Laaje
Am dund gu dul jeex?
Tontu wi
Bibal bi wonne na aw yoon wu leer ngir dund gu dul jeex. Bu njëk, war nanu nangu ne dañu bàkkaar fa kanam Yàlla : « ndaxte ñépp a bàkkaar ba jotatuñu ndamu Yàlla » (Waa Room 3 :23). Nun ñépp def nanu ay mbir yu neexul Yàlla, litax nu yelloo daan. Ndaxte sunuy bàkkaar yépp nu ngi ko jëme ci Yàlla ju sax ba fàw, kon ab daan bu sax ba fàw rekk mooy li war. « Ndaxte peyu bàkkaar mooy de, waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom » (Waa Room 6 :23).
Waaye naka noonu, Yeesu-Kirist, doomu Yàlla Aji Sax ji bi amul bàkkaar (1 Piyeer 2 :22), nekk na nit (1 Yowaana 1 :1,14) ba noppi de ngir fay sunuy boru bàkkaar. « Waaye Yàlla firndeel na mbëggeelam ci nun, ci li Kirist dee ngir nun, bi nu nekkee sax ay bàkkaarkat » (Waa Room 5 :8). Yeesu Kirist de na ca bant ba (Yowaana 19 :31-42), gàddu mbugël bi nu yellowoon (2 Waa Korent 5 :21). Ňeeti fan gannaaw gi, mu dekki ci biir ñi de (1 Waa Korent 15 :1-4), wonne ndamam ci kaw bàkkaar ak de. « Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju bare, ba may nu yaakaar ju sax ndax ndekkitel Yeesu Kirist. » (1 Piyeer 1 : 3).
Jaare ci kaw ngëm war nanu soppi sunu xel jëme ci Kirist- mooy kan, li mu def ak lutax- ngir mucc gi (Jëfi ndaw ya 3 :19). Su ne wekke sunu yaakaar ci moom, wekku ci dewam ca bant ba ngir fay sunuy bàkkaar, dinañu am njeggal te dinañu jot dund gu dul jeex gi ca asamaan. « Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am képp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk » (Yowaana 3 :16). « Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc » (Waa Room 10 :9). Ngëm rekk ci kaw jëf ju mat bu Kirist ca bant ba mooy wenn yoon wu dëgg wi ngir dund gu dul jeex ! « Ndaxte ci yiwu Yàlla ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yéen, mayu Yàlla la; 9 du peyu jëf, ba kenn di ci kañu » (Waa Efes 2 : 8-9).
So bëgge nangu Yeesu Kirist ni sa Musalkat, ab ñaan wu yomb a ngi nii. Fàttalikul ne, wax ñaan wi walla weneen ñaan du mo lay musal. Ci kaw gëm Yeesu Kirist rekk mo lay musal ci say bàkkaar. Ñaan wi ab yoon wu yomb ngir wax Yàlla sa ngëm ci moom te gërëm ko ci li mu la indil mucc gi. “Yàlla, xam na ni bàkkaar na fa yaw te yelloo na daan. Waaye Yeesu Kirist gàddu na mbugël li ma yellowoon ci noonu jaare ci kaw ngëm ci Moom am na njeggal. Wekk na sama yàkaar ci Yaw ngir mucc. Jërëjëf ngir sa yiiw ak sa njeggal-mayug dund gu dul jeex! Amiin!”
Ndax dogu nga topp Yeesu ndax li nga jàng ci moom fii? Sude noonu la deme, demal ci “Nangu na Kirist tay” butoŋ bi ci suuf.
English
Am dund gu dul jeex?