settings icon
share icon
Laaje

Jot njeggal? Naka la mana jote njeggal gu bawo ca Yàlla?

Tontu wi


Jëfi Ndaw Ya 13: 38 ne na, “Kon nag bokk yi, na ngeen xam ne ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woona àttee nit ni ku jub.

Lan mooy njeggal te lutax ma soxla ko?

Baatug « njeggal » mu ngi tekki fomp aliwa bi, baal, far aw bor. Bunu tooñe kenn, nu baalu ko ngir defaraat sunu diggante. Baal deesu ko joxe ndax ab nit yelloo na ko. Kenn yelloowul mbaal. Mbaal ab jëfu mbëggeel la, yërmande ak yiiw. Mbaal ab doggu la buy do jàppal kenn dara, ndare sax li mu la def.

Bibal bi wax nanu ne nun ñépp soxlo mbaal gu joge ca Yàlla. Nun ñéppa bàkkaar. Kàdduy Waare 7:20 ne na, “Amul moos ku jub ci kaw suuf, kuy def lu baax te du bàkkaar.” 1 Yowaana 1:8 ne na, “Su nu waxee ne amuñu bàkkaar, kon nax nanu sunu bopp, te dëgg nekkul ci nun.” Yaw laa moy, yaw doŋŋ (Sabóor 51:4). Li mu jur, nun ñéppa soxla mbaalug Yàlla. Bu nu nu baalul sunuy bàkkaar, dinañu tàbbi ca alaxira ju dul jeex ak coono ngir sunu mbuggalu bàkkaar (Macë 25:46; Yowaana 3:36).

Njeggal—Naka la siy jote?

Alhamdulila, Yàlla mbëggeel ak yërmande la – noppi ngir jeggal nu ngir sunuy bàkkaar! 2 Piyeer 3:9 wax nanu, “…Lu mu yéex yéex ci xalaatu nit. Xanaa kay da leena muñal, ndax bëggul kenn alku, waaye ñépp tuub seeni bàkkaar.” Yàlla dafanu bëgg baal, kon Mooy ki nuy indil njeggal.

Peyu sunuy bàkkaar mooy de. Xaaj bu jëkk bu teere Waa Room 6:23 wax na ne, “Ndaxte peyu bàkkaar mooy dee…” de ba fàw mooy linu yelloo ngir sunu bàkkaar. Yàlla, ci tërëlinam bu mat, nekk na nit - Yeesu Kirist (1 Yowaana 1:1, 14). Yeesu de na ca bant ba, gàddu sunu mbuggal gi nu yelloo – de. 2 Waa Korent 5:21 jàngal nanu, “Kirist mi masula def bàkkaar, Yàlla def na ko bàkkaar ci sunu wàll, ngir ci sunu bokk ci moom, nu mana doon njubteg Yàlla.” Yeesu de na ca bant ba, gàddu mbuggal gi nu yelloo! Ni Yàlla, dewu Yeesu indil na nu baalug bàkkaar ngir àddina sépp. 1 Yowaana 2:2 Yeene na, “Te moo joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar, te du sax sunuy bàkkaar rekk, waaye yu àddina sépp.” Yeesu dekkina wonne ndamam ci kaw de ak bàkkaar (1 Waa Korent 15: 1-28). Sant ñeel na Yàlla, jaare ci de ak ndekkitel bu Yeesu Kirist, ñaarelu xaaj bu Waa Room 6:23 dëgg la, “…waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom.”

Ndax danga bëgg nu baal la say bàkkaar? Ndax dangay am yëg yëgu ku def dara bo xamni mënuloo taqalikook moom? Sa mbaalug bàkkaar japandal na so wekk sa yaakaar ci Yeesu Kirist ni sa Musalkat. Waa Efes 1: 7 ne na, “Moom jot na nu ak deretam ji ñu tuur, maanaam baal nu sunuy bàkkaar, ci kaw yiw wu yaatu.” Yeesu fay na sunu bor, kon man nanu am sunug njeggal. Lépp li nga wara def mooy nga laaj Yàlla mu baal la jaare ci Yeesu, gëm ni Yeesu de na ngir yaw ngir fay sa njeggal – te dina la baal! Yowaana 3:16-17 am na xibaar bu neex bi, “Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk. Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen.”

Njeggal —ndax ci dëgg ni la yombe?

Waaw noonu la yombe! Manuloo yeyoo njeggal fa kanam Yàlla. Manuloo fay it ngir sa njeggal fa kanam Yàlla. Jot ko rekk nga mana def, ci kaw ngëm, jaare ci yiiw ak yërmande Yàlla. So bëgge nangu Yeesu Kirist ni sa Musalkat te jot baal fa kanam Yàlla, ab ñaan a ngi go mana def. wax ñaan wi walla weneen ñaan du mo lay musal. Ci kaw gëm Yeesu Kirist rekk mo lay may mbaalug bàkkaar. Ñaan wi ab yoon wu yomb ngir wax Yàlla sa ngëm ci moom te gërëm ko ci li mu la indil njeggal. “Yàlla, xam na ne bàkkaar na ci sa kanam te mbuggal la yelloo. Waaye Yeesu Kirist gàddu na mbuggal loolu ci noonu jaare ci kaw ngëm manes na am mbaal. Wekk na sama yaakaar ci Yaw ngir sama mucc. Jërëjëf ngir sa yiiw ak njeggal yu neex yi! Amiin!”

Ndax dogu nga topp Yeesu ndax li nga jàng ci moom fii? Sude noonu la deme, demal ci “Nangu na Kirist tay” butoŋ bi ci suuf.

English



Delul ci Wolof ci xët bu njëk bi

Jot njeggal? Naka la mana jote njeggal gu bawo ca Yàlla?
© Copyright Got Questions Ministries