Laaje
Kan mooy Yeesu Kirist?
Tontu wi
Ni laaj bi “Ndax Yàlla am na?” laaj bi di ndax Yeesu Kirist amoon na neew na nit ñu koy laaj. Ňu ci ëpp nangu nañu ne Yeesu ci dëgg ab nit bu doon dund ca Israyil am na leegi 2000 at. Wax ji kay mu ngi nekk ci mooy kan. Danaaka lu ëpp ci dine yu mag yépp nu ngi jangale ni Yeesu ab yonent la woon walla nit ku baax walla nitu Yàlla. Waaye Bibal bi wax nanu ne Yeesu romboon na ab yonent, jàngalekat bu baax, walla nitu Yàlla.
C.S Lewis ci tereem bi Dina kërcen dëgg bind na baat yi di ñëw: “Ma ngi artu fi ku nekk kuy wax naan ndofeel gi nit ñi di faral di wax ci Moom [Yeesu Kirist]: ‘Noppi na ngir nangu ni Yeesu ab jàngalekat bu mag la woon, waaye du ma nangu ni dafa jape boppam Yàlla.’ Mooy benn ci mbir mi nu warula wax. Nit ko xam ni ci dëgg nit kese la woon te wax xeeti mbir yi Yeesu doon wax du yem kese ci doon ab jàngalekat bu mag. Ab dof lay doon— bu toll ak nit bu naan nen bu yàqu la walla— mu nekk rabu safara. War nga def sa taneef. Ci ba xam nit kooku nekkoon na, kan la woon, doomu Yàlla, walla nit ku def boppam walla dara lu yees. Man nga ko jape nit doomi xaram te noppi lo ko, man nga tifli ci kawam te rey ko ni ab rab; walla nga sukk ciy tankam te wowe ko Boroom bi ak Yàlla. Waaye bunu ñëw aki waxi dof yu amul bopp ci li nu naan ab jàngalekat bu mag bu doomi àdaama yi la woon. Bunu bayi gis gis boobu ubiku ci nun. Du loolu la naroon def.” (Macmillan, 1952, p. 55-56).
Kon, kan la Yeesu ni moom la? Kan la Bibal bi wax ni moom la? Bu njëk, Yàlla la ci jëmu nit. Yeesu ne na ci Yowaana 10:30, “Man ak Baay bi benn lañu.” Ci gis gis bu jëkk li man na baña nirook xënto doon Yàlla. Naka noonu, xool leen tontu Yawut yi ci Wax ji. Jeem nañu ko sanni ay xeer “ngir dingat, ndaxte yaw, nitu kese jape sa bopp Yàlla” (Yowaana 10:33). Yawut yi xamoon nañu li waxi Yeesu yooyu doon tekki manam jape boppam Yàlla. Ci aaya yi ci topp, Yeesu gagantiwul Yawut yi walla jeema indi leeral Waxam jooju. Masula wax, “Japewuma sama bopp Yàlla.” Bu Yeesu waxe, “Man ak Baay bi benn lañu” (Yowaana 10:33), Ci dëgg dafay wonne bennoom ak Yàlla.
Ci Yowaana 8:58 Yeesu mu ngi wax nekkam lu jiitu àddina si, lu Yàlla baaxo: “Ci dëgg dëgg, ‘Yeesu tontu na, ‘laata Ibraayma di judd, nekkoon na!” Ci tontu ci wax jooju, Yawut yi jëlaat nañu ay xeer ngi sanni leen Yeesu (Yowaana 8:59). Ci li mu ne nekkoon na laata àddina si, Yeesu joxna boppam ab tur wu Yàlla rekk yellool —May ki nekk (xolal Mucc ga 3:14). Yawut yi jalax nañu Yeesu ak ki mu doon ni Yàlla ju jël jëmu nit, waaye xam nañu bu baax li mu doon wax.
Yeneeni aaya ci Bibal bi yuy wonne ni Yeesu Yàlla la ci jëmu nit bokk na ci Yowaana 1:1, buy wax naan, “Kàddu gi Yàlla la woon,” nu toftal ci Yowaana 1:14 biy wax naan, “Kàddu gi doon na nit.” Toma taalibe bi wax na Yeesu, “Sama Boroom ak sama Yàlla” (Yowaana 20:28), Yeesu gagantiwu ko. Ndaw li di Pool wonne na Yeesu ni “Sunu Yàlla ak Musalkat wu rëy wi, Yeesu Kirist” (Tit 2:13). Ndaw li Piyeer wax na lu ni mel, di wowe Yeesu “Sunu Yàlla ak Musalkat wu rëy wi” (2 Piyeer 1:1).
Yàlla Baay bi def na seede ci Yeesu ki mu doon ni: “Waaye ci wàllu Doom ji, lii la ko Yàlla wax: Yaw Yàlla, dinga ‘toog ci jal bi ba fàw, ci njubte ngay nguuru’” (Yawut ya 1:8; cf. Sabóor 45:6). Waxi yonent yi ci Kóllëre ku njëk gi ni Esayi 9:6 yeene na ni Kirist nekke Yàlla: “Nde gonee juddu, ñeel nu, di doom ju góor ju ñu nu may, mu yenu kilifteef gi ñu di ko wooye Diglekat bu yéeme bi, ak Yàlla jàmbar ji, ak Baay bi sax dàkk, ak Buuru jàmm bi” (yokk bamtu wi).
Lutax laajub ki Yeesu doon am solo lool? Lutax Yeesu doon Yàlla doon itte? Yu bari li ku waral:
• Ni C. S. Lewis wonne, Bu Yeesu dul Yàlla, kon Yeesu mooy fenkat bi yees ci anam wu nekk.
• Bu Yeesu dul Yàlla, kon taalibe it dinañu doon ay fenkat.
• Yeesu mooy Yàlla ndax ab almasi digge woon nanu ko mu doon “Kenn ki Sell” (Sabóor 16:5, NASB). Ni mu amule kenn ci kaw suuf ku jub fa kanam Yàlla (Sabóor 53:1; 143:2), Yàlla ci boppam moo ñëw ci kaw suuf ci yaramu nit.
• Bu Yeesu dul Yàlla, dewam du doon doy ngir fay mbuggalu bàkkaar bu àddina sépp (1 Yowaana 2:2). Yàlla rekk mo manoon na indi ab sarax bu mat te doy ba fàw (Waa Room 5:8; 2 Waa Korent 5:21).
• Yàlla mooy jenn Musalkat (Ose 13:4; cf. 1 Timote 2:3). Bu de Yeesu mooy Musalkat bi, kon fàw mu doon Yàlla.
Yeesu nekk na Yàlla ak nit. Ni Yàlla, Yeesu rekk moo manoon na dalal merum Yàlla. Ni nit, Yeesu amoon na man maninu de. Ni Yàlla-ak nit, Yeesu mooy jenn Rammukat bi mat ci diggante Asamaan ak Suuf (1 Timote 2:5). Manes na am mucc gi jaare rek ci ngëm ci kaw Yeesu Kirist. Ni mu ko yégle, “Man may yoon wi ak dëgg gi ak dund gi. Kenn manula ñëw ci Baay bi te jaarulo ci man” (Yowaana 14:6).
English
Kan mooy Yeesu Kirist?