Laaje
Lan mooy Kërcen?
Tontu wi
Ab benni tekki a ngi nii ab kërcen manes na ko nirooleek « ab nit buy yeene ngëmam ci Yeesu ni Kirist walla ci njàngaleb dine bu Yeesu ». Donte ab ndorteel bu baax la, ni ay yeneen tekki yu bari yu ay xëti leeral, sore na tuti ci di wax ci dëgg ci li Bibal bi wax ni mooy ab Kërcen. Baatu « Kërcen » jëfandikoo nanu ko ñetti yoon ci Kóllëre gu Bees gi (Jëfi Ndaw ya 11 :26 ; 26 :28 ; 1 Piyeer 4 :16). Taalibe Yeesu yi tudde nañu leen lu jiitu « Kërcen » ca Ancos (Jëfi Ndaw Ya 11 :26) ndaxte seen nekkin, seeni jëf ak seeni wax dafa meloon ni bu Kirist. Baat bi « Kërcen » mu ngi tekki « doon moomel wala farandook Kirist » wala « taalibe wu Kirist ».
Ci lu gënul, dirub ay at, baatu « Kërcen » ñàkk na lu bari ci li mu doon tekki ba ñu ko di jëfandikoo ngir nitu dine wala sax ku am ay jikko yu rafet te kawe lool, waaye kan moo man wala baña man nekk taalibe Yeesu Kirist dëgantaan. Nit ñu bari yu gëmul te amuñu benn yaakaar ci Yeesu Kirist ñu ngi jappe seen bopp ni ay kërcen ndaxte ñu ngi dem jàngu ba walla di dund ci rewum « kërcen ». Waaye dem jàngu, liggeyal ñi nga tane wala doon nit ku baax du la def ab kërcen. Dem jàngu ba tamit du la def itam kërcen ni dem garas la dul def defarkatu ndamar. Bokk cib jàngu, di tewe xew xew yi ni mu ware, te di joxe ngir liggeey bi ci biir jàngu bi du la def it kërcen.
Bibal bi jàngal nanu ne jëf yi baax yi nuy def du tax Yàlla nangu nu fa kanamam. Tit 3:5 ne na, “Ba musal nu, Ajuwul ci jëf yu jub yu nu def, waaye ci yërmandeem rekk. Mu juddulaat nu ci laabal sunu xol, te yeesalaat nu ci dooley Xel mu Sell mi.” Ko, kërcen mooy kenn ku judduwaat ci Kàtanu Yàlla (Yowaana 3:3; Yowaana 3:7; 1 Piyeer1:23) te wekk yaakaar ak ngëm ci Yeesu Kirist. Waa Efes 2:8 wax nanu ne “…ci yiwu Yàlla ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la.”
Ab kërcen dëgg mooy ab nit ku wekk yaakaar ak ngëm ci Yeesu Kirist ak jëfam, jaare dewam ca bant ba ni sunu peyug bàkkaar ak Ndekkiteem ca Ňeteelu fan wa. Yowaana 1:12 wax nanu, “Tewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla.” Màndargaab kërcen wu dëggu mooy mbëggeel jëme ci ñeneen ñi ak degg Kàddu Yàlla (1 Yowaana 2:4, 10). Ab kërcen wu dëggu mooy ci dëgg doomu Yàlla, bokk ci Njàbootug Yàlla, ko xamni jot na dund gu bees ci Yeesu Kirist.
Ndax dogu nga topp Yeesu ndax li nga jàng ci moom fii? Sude noonu la deme, demal ci “Nangu na Kirist tay” butoŋ bi ci suuf.
English
Lan mooy Kërcen?